Bi téléphone yi baré bataye
Takhe na ba gnome gui gueuneu diégué
Wâyé ite takhna ba dôtou gnou meneu guissé
Manni wakhtane langandô thia guene
Bayyi téléphone bi diakkâre lô
Bou téléphone takh ba dôtou gnou meneu wakhtane
Guisse touma,guisse touma,guisse touma sa kaname
Lima beugue deugue deugue dendadôke yawe nga wakh
Guisse touma,guisse touma,guisse touma sa kaname
Lima beugue deugue deugue dendadôke yawe nga wakh
Li doyna wâre,doyna wâre
Gueudj nagnou langue lôle
Di wakhe di khôlaneté,hé hé hé
Diotayou penche wâye amatoule
Gnoune gnépa bokondo fougnouye khôle
Télévision takhe ba dôtou gnou meneu wakhtane
Guisse touma,guisse touma,guisse touma sa kaname
Lima beugue deugue deugue dila dégue dila khôle
Guisse touma,guisse touma,guisse touma sa kaname
Lima beugue deugue deugue dila dégue dila khôle
Ndékété dé safara dé dina dioure diangoro
Deuk bi dé, dina moudj, namaneté doutoul ame
Namaneté,sou amoul guissanté wagnékou
Guissaneté sou amoul, mineuneté doutoul ame
Mineuneté sou amoul, thioféle dé dotoulame
Thioféle dé, sou amoul beugueneté dotoul ame
Beugeuneté sou amoul, kharito dotoul ame
Kharito sou amoul,, khole yépeu dal di wowe
Kholeyi dé sou wowé yeurmandé dal di diekh
Yeurmandé sou amoul seîtané dal di téwe
Séîtané sou gnewé, askane wi dal di tasse
Ndékété,safara, dina dioure diangoro
Lî doyna waré, doyna ware
Gueudj naniou langue lôlé
Di wakh, di kholaneté hé hé hé
Sétalma lilé hé
Guisseulema lilé hé hé hé
Sétalma lilé hé
Guissalema lilé hé hé hé
Haannn….. ana penche ma, ana sabar ya, ana tama dia
Yegueléléne,yeguelélno, yegueléléno
Bou ndieukone, wakhtane thi penche…..
Diébané tamaka dane def,sabaraka dane def, wouy……….
Résumé Français : Vivre les nouvelles technologies !
Mais gare à l'oubli mœurs et coutumes.
Ou sont passés les causeries sous l'arbre à palabres,
Les réunions de patriarches, les veillées nocturnes
Les sons des Tam- Tams, koras et balafons
Paroles2Chansons dispose d’un accord de licence de paroles de chansons avec la Société des Editeurs et Auteurs de Musique (SEAM)