Keroog bés pénc ma ba ñuy wàja wàccee jànt bi
Di waajal peese ba
Mullaay Dabbaax Yàlla nañ la jege
Yàlla daal mooy tànn waayam
Mullaay Dabbaax
Bu ñu fàtte, bës boobu le
Bu ñu sore, bës boobu le
Bu ñu fàtte, bës boobu le
Loo fa ñaan, Yàlla mey la ko
Moo daan waxal ñu ñuul ñi
Moo daan waxal nasaraan wi
Moo daan gàddu askan wi
Dafa daan wax naan nan boole sunu rééw mi
Dafa daan wax naan bu kenn yëngël gaal gi
Dafa daan wax naan nañ boole sunu xol yi
Dafa daan wax naan nanñ yërëm jigéén ñi
Sa boroom bi bég na yónnentam bi bég na
Yaa ko ligééyal sa boroom
Mullaay Dabbaax yaw de wàcc nga mëssoo wax lu amul
Keroog ba nga ñu jitoo asamaan si daa lëndëm bësë ngii kenn dootu ko fàtteeti
Mullaay Dabbaax
Bu ñu fàtte, bës boobu le
Bu ñu sore, bës boobu le
Bu ñu fàtte, bës boobu le
Loo fa ñaan, Yàlla mey la ko
Moo daan waxal ñu ñuul ñi
Moo daan waxal nasaraan wi
Moo daan waxal askan wi
Dafa daan wax naan na ñëpp ligééy
Dafa daan wax naan nañ jàngal jigéén ñi
Daawul seetaan fu ñaaw
Pusóóm la yoroom, fu xótteeku mu ñaw
Rééw mi rééw mi ameel nañ la njukkël Mullaay Dabbaax
Daawul seetaan lu ñaaw
Pusóóm la yoroom, fu xótteeku mu ñaw
Rééw mi rééw mi ameel nañ la njukkël Mullaay Dabbaax
Bakkariik Daramaa Maram Loo Kumba Caam
Ngañ Péndaak Paate Pénda
Moo daan waxal ñu ñuul ñi
Moo daan waxal nasaraan wi
Moo daan gàddu askan wi
Dafa daan wax naan nañ yaatu suñu rééw mi
Dafa daan wax naan na ñëpp ligééy
Dafa daan wax naan nañ yërëm jigéén ñi
Dafa daan wax naan nañ jàngal gune yi
Paroles2Chansons dispose d’un accord de licence de paroles de chansons avec la Société des Editeurs et Auteurs de Musique (SEAM)